ANDANDOO XEEX « CORONAVIRUS »
Poème wolof dans le but de de conscientiser la population, en particulier ceux s’entêtent à nier l’existence de cas positifs à l’intérieur du territoire
Yaw miy weddi di baña gëm
Te naa jàngoro ji amul
Xamalne say gët a lëndëm
Déggóo it, say noppu neexul
Yëgël ne moom du xàjjale
Ku baaxak ku ñàkk solo
Góorak jigéen magak xale
Buurak jàmburak baadolo
Ñépp la yab du kuy càxaan
Te su la dugée, nang ko xam,
Da ngay xëy sa put di xasan
Wàlla muy tàngal sa yaram
Nga yàkaar ni di na bàyyi
Mu ne la nuus gën la jàpp
Roof la jafe-jafe noyyi
Sëqët ak metitu bopp
Ndeem sax manees naa dem ba wér
Amna ñu mu dal ñu faatu
Moo tax ku nekka wara xér
Jëm ci soññe yii ngir wàttu
Sàmmonteel ak yilé ndigël
Teewlul di naa la ko xibaar
Bu boobaa di na la musël
Ba nga rëcci ci bii feebar
Bul dox di joxe say loxo
Téeyéel te yam cig saafoonte
Salàmaalikum ngay saxoo
Ci kii, kaa, koo xam la doonte
Saa yooy nuyyóo bul di sóobu
Bay tegante ay mbaggak lex
Deel raxasu ndoxak saabu
Ngir jàngoro ji dee ba jeex
Bul sëqët baa ngay tisóoli
Ludul né da ngaa dummóoyu
Fatt mbir yay tis di jolli
Ba du laal nit ña lay moyyu
Wëyël ci lii kon nga aaru
Moytandiku ba am ci ndam
Ne wolof neena fagaru
Moo gën faju, na nga ko xam