DIGE GÉEJ, KILIBU SÉEX ALIYU NDAW : TEKKI MBAA LAB
Dige géej, téere kilib bii Séex Aliyu Ndaw di door a génne, OSAD mi Soxna Aram Faal jiite moo ko móol ci atum 2019. Du guléet Séex Ndaw di bind kilib ci wolof, Dige géej mooy ñetteelam, ginnaaw Guy Njulli ak Bokk Afrig.
Dige géej, téere kilib bii Séex Aliyu Ndaw di door a génne, OSAD mi Soxna Aram Faal jiite moo ko móol ci atum 2019. Du guléet Séex Ndaw di bind kilib ci wolof, Dige géej mooy ñetteelam, ginnaaw Guy Njulli ak Bokk Afrig.
Ca njalbéen ga, dañu ko waroon a dawal Soraano ngir ñu bare mën ko faa seetaani. Jamono jooju, Usmaan Jaxatee nekkoon njiitu tiyaatar bi. Mujj gi mu jóge fa, dellu UCAD, kenn toppatootul kilibu Séex Ndaw bi, mu nelaw fa diirub daanaka fukki at ak ñaar laata boroom di ko nangu ngir móol-lu ko. Kon mën nañoo wax ne yàgg na yoon.
Waaye teewul Dige géej mel ni lu bees ndax nekkinu doomi-Afrig yaa ngiy wéy di tar te su dee tukkib nëbbu rekk mel na ni tey la Waalo gën a aay.
Léegi nag, nan xuus tuuti ci biir gaal gi walla boog ci biir téere bi…
« Dige ». Baat bu diis la ci gor. « Géej » nag moom, kumpa la ba jéex ndax, ni ko Séex waxe, «ndox mu ne màww ba fu bët yem doy na kéemtaan».
Fii nag, dige bi ci diggante boroom gaal gi laak «kurélu ay xarit neen, yàgg a ànd» bala lii di xew, boroom gaal gi war leen a yóbbu Espaañ. Kiy lijjanti mbir mi Saamelo la tudd. Kon, dige bile yaakaar a ko lal. Yaakaaru ñépp ñi ko séq : rëcc takk-der yi ba yegg fa nga jëm te benn bakkan du rot ci yoon wi, Yàlla musal leen it ci balaay Géej-Mbàmbulaan yi ; jéggi géej, yegg fa nga jëm, ngir ëllëg gu tane, ndax «toog ci sa wetu way-jur te yoroo loo leen yoree amul njariñ». Te wax dëgg Yàlla, «fàww doomu-aadama tukki ndax jekkeedi la nit moom. Bàyyimaa yelloo toog benn béréb…» Tukkib nëbbu nag, moo lëmbe dëkki Afrig yi, seeniy ndaw jàpp ne jël gaal, jéggi géej rekk a mën a soppi seen dundin.
Waaye ñu baree-bari ciy ñàkk seen bakkan.
Ndax tukki bi ñuy waajal ci Dige géej dina àntu ? Nu muy deme ? Ñaari baati wolof yii Sëriñ Séex Ndaw taqale lan lañu ëmb ?
Ci loolu lañu bëgg a tontu, waaye bala nu ciy sori nu wax leen kan mooy fentkat bi.
Séex Aliyu Ndaw, bindkat la bu yatt xalimaam ngir joxe xalaatam ci doxinu àddina si, wax tamit naka lees war a saafaraa jafe-jafey réewum Senegaal.
Ñépp xam nañu ne bindkat bu xareñ la, baaxe nuy téere yu am solo. Nu fàttali leen tuuti ci jaar-jaaram.
Séex Aliyu Ndaw bind na téere yu bari ci làkku tubaab, ñu gën cee ràññee L’exil d’Alboury ; nekkoon na yit jàngalekatu àngale. Ciy ati 60, bokkoon na ci ”Groupe de Grenoble” – kurél gu doon jéem a suqali làmmiñi réew mi – mook ñoomin Asan Silla, Masàmba Sare ak Saaliyu Kànji ak it Ablaay Wàdd mi fi doonoon njiitu réewum Senegaal. Séex Aliyu Ndaw dafa teel a nànd ne làkku tubaab danga koy jàng ngir am i lijaasa doŋŋ waaye doo nangu mu lay miirloo ba nga xeeb sa bopp. Teel naa seetlu tamit, foofa ca Grenoble, ne xonq-nopp «amul kóllëre te jikko miikar la yor.»
Ci gis-gisam, ”Nun doomi-Afrig yi, ci sunuy làmmiñ lanu war a bind” ndax, ni ko Séex Anta Jóob waxe, «làkku jaambur mën nga koo macc mu neex lool ni tàngal waaye doo ci tàqamtiku». Kon mën nanoo jàpp ne Séex Aliyu Ndaw, lii book na ci li tax mu dëddu làkku doxandéem yi, fas-yéene gën a jox làmmiñ wi mu nàmp gëddam.
Nanu xuus nag léegi ci gaal gi, ni nu ko dige woon ci kow.
Usmaan ak i xaritam, ay ndaw, ñoo gise, waxtaan, jàpp ne seen wërsëg nekkul Senegaal, ñu ne dinañu ko toppi ba bitim-réew, daldi jël gaal, te xam xéll ne yoon da koy tere te caaxaanu ci. «Li leen jëkk a yëkkati mooy daw toroxte, war di faj soxla mu të la ticc. Mënaloo sa bopp, mënaloo say way-jur. Kon foo dégg teraanga te mu wóor la ne da lay yewwi, jublu fa rekk ngay def.» Dafa fekk nag du lu yomb, nit ki mën na cee ñàkk bakkanam. Waaye du ko teree bàyyi lépp song géej gi ndax rekk ni yaakaar ame doole.
Moo tax, tukki bi ñu xumtoo ba sóobu géej wex na xàtt ci ñoom : tukki bii, duñ ko fàtte ba mukk. Metit wu tar, ngëlén lu raglu, neer, feebar, ceeb bu lóor, siddit yu jóg, tiitaange, xuloo, tamante dëmm, wax ju ñaaw, réccu añs. Loolu lépp ci biir gaal gi. Te boroom gaal gi, moom, nanguwu cee yéy yàbbi. Daanaka bi ñuy waaj a yegg lay door a aartu way-tukki yi ak a xëbëlaate. Ci gàttal, tukki bi dem na ba «fésal loo xam ni bokkul ci seen jikko». Coono ba ñu daj ci biir gaal gee gën a metti lépp la ñu masoon a daj.
Njabooti way-tukki yi tamit jaaxle nañu. Abi, soxnay Usmaan, di jigéen-ju-wérul, yaakaar rekk a ko tax a bàyyi jëkkëram mu dem ngir bu delsee mën a «faj gàcce».
Kiy jàng Dige géej dinay faral di dajeek baatu yaakaar : ”du lenn lu-dul yaakaar” ”yaakaar yaatal wërsëg”, ”xanaa yaakaar rekk”.
Xéy-na ku nekk bey na waaram ci dige bi, waaye ndax yaakaar ji yàkkeekuwul ? Ak lu mënti am, Usmaan ak i ñoñam, ay xale yu war a am xéy lañu, war a mënal seen bopp itam wànte tële lépp a leen tax a bëgg a dumóoyu seen réew. Su gornmaa bi jàppale woon ndawi réewam, fullaal leen, jox leen seen gëdd, dina néew ñuy gedd Senegaal di jaay seen bakkan. Bëgguñoo dee waaye dee moo leen gënal gàcce.
Fii nag, Séex Aliyu Ndaw mi ngi wane lu bon liy tukkib nëbbu mën a jural aw askan waaye it ni sunu njiit yi sàggane ba seeni doom di jéggaani bànneex. Mu may fàttali woyu ndaanaan boobu ñu naan Xaar Mbay Majaaga : « Waaw, xale yi muñleen, ku leen juroon yërëm leen ». Séex Aliyu Ndaw de, bindkat la, xalimaam lay wonee yërmandeem ci askan wi, di ko ci jàppale. Ndax kilifa yiy dogal diñañ ko dégg ? Doon na ci baax lool ; aw askan, ay ndawam ñooy ëllëgam. Kenn warul saax-saaxe sa ëllëg.
Dige géej, Séex Aliyu NDAW (166 xët), OSAD 2019, 5000 CFA
Ku bëgg a jënd téere bi :