NJÀNGATUB BÀMMEELU KOCC BARMA 3/3….
Bindkat bi, moom, yemul rekk ciy biral démbug réewam. Waaye, day àbb baatu aji-jëmmalam bi gën a fés, soppi kob joowu, di joow ci géejug aadaak cosaan. Noonu, muy tukkiloo jàngkat bi, réewoo réew.
Bindkat bi, moom, yemul rekk ciy biral démbug réewam. Waaye, day àbb baatu aji-jëmmalam bi gën a fés, soppi kob joowu, di joow ci géejug aadaak cosaan. Noonu, muy tukkiloo jàngkat bi, réewoo réew. Fànn bu ne, mu jukki fay fentaakoon ; muy tëggkat, di woykat, di bindkat… Tàggat-yaram sax, bawu ko. Nde, futbalkat yu aay yi sax, te mës a siggil seen raayay réew, fàttewuleen ; muy yu Senegaal yi walla yu Afrig gépp, mbaa sax yu Amerig. Duggewu ko, nag, lu dul sargal leen, jox leen seen wàccuwaay. Worma jooju, miŋ ciy beral loxo ñi mu ci gën a naw : Kocc Barma Faal, Sëriñ Musaa Ka, rawatina góor gi Àllaaji Gay. Kooku mooy « ponkal » ma, fa muy tagge ndem-si-Yàlla ji soxnaam sa, Faatu Gay. Ndeysaan, cib taalif bu gudd a gudd, yéeme te daw yaram la ko tagg. Bóris ne : « Bi ma dalee jàng i taalif ba tey, benn rekk a ma ci mas a jooyloo ». Muy sargal it Biraago Jóob, Dawid Jóob, Séex Anta Jóob, Usmaan Sémbéen, Mariyaama Ba, Séex Aamidu Kan (« … kenn mënul a fàtte “La Grande Royale” ! »). Fàttewul itam Maam Yunus Jeŋ, Aram Faal, Momar Siise (te Bóris jukkib taalifam bu siiw bu mu fésaloon ci benn téereem), Séex Aliyu Ndaw (« Fentaakon bi, Njéeme, day gis di wone, day dégg di jottali… Na bët yiy bëtt lépp ba ca yax ba, nopp yiy dàjji bunti patt-pattaaral yépp, nay firi lees waxul… Seet ko ci Séex Aliyu Ndaw. Bindkat bu xam àddinaa ngoog, moo tax liñ koy dégg bariwul. »)…
Képp ku am seetlu, dina xam ne, Bóris, dafa beral loxo dëgg-dëgg fentaakon bii di Maada Caam. Waaw. Maada Caam mi doon woy Laay Ñaaxam. Laay Ñaax, nag, dawalkatu taksi bu kenn xamul woon la. Waaye, aka keemaaney woy ak mbëggeel ! Mu fésal ko fàŋŋ ci leer gi.Dees na fi tase ak itam Percy Sledge mi nga xam ne, bu woyaan, yaram yépp daw. Njaga Mbay tamit, kenn demul mu des. Céy woy wa muy màggalee xaritam ba, Laay Mbub, te naan ca : « Meew mu wayul dem na noonu. »…
Du ñàkk mu am ñuy laaj, naan : « A waaw ? Naka lañ mënee boole loolu lépp ci benn téereb nettali bu 240i xët kese ? Lees fi wax lépp ciy nettali, xalaat ak i taxawaay… Num mënee nekk ? Ndax kuy jàng bile téere dina ci mën a gindiku ? » Ndax kat, jàngkat bi mënoon naa tàyyi, walla faf mu réer ci yoon wi ! Laaj yooyulee diiy kon, laaj yu dëggu te am solo… … Waaye daa fekk rekk ne, loolu lépp, loxo Bubakar Bóris Jóob mu xareñ mee koy rëdd, moo koy togg, moo koy tëgg, moo koy mooñ ci doxalin bu aw yoon te leer. Bindkat bii moom, li mu gën a mën mooy wommat jàngkat bi ci ruq- ruqaan yi, di waxtaan ak moom, lée-lée mu gësëm ko, lée-lée mu koy reeloo. Te nag, du noppee di ko aartook a xalaatloo ci nekkinu nit ñi ak ëllëgu mbooleem-nawle mi.
Am na yit beneen feem ci tërëlinu Bàmmeelu Kocc Barma : nettali bi yépp ñaari pàcc la (ni nu ko xame, bu jëkk bi Njéeme Pay a nu koy jottali, ñaareel bi Kinne Gaajoo koy aw). Te nag, xew-xew yépp ñoo ngi xewe ci benn bés bu séddalikoo ay pàcc : Njël, Njolloor, Tàkkusaan ak Timis. Ginnaaw njàngat yooyu, nemmeeku nañ, biir Bàmmeelu Kocc Barma, feem bu bees ci mbindinu Bóris. Dëgg la, bindkat bi, naka jekk, tàmmal nanu di waxtaan ak jàngkat bi. Waaye fii moom, day dem ba di ko déey ngir xamal ko xeex bi muy xeex saa su ne ak baat yi miy jëfandikoo. Moom kay, day dem bay bàkku ci ni muy yemelee yenn baat yu dëgër bopp yi ak nu muy dàqee (ciy nettaleem) yeneen yu réy lammiñ yi. Maanaam, baat yi dul xaar mu woo leen ca jamono ya mu leen di soxla. Bu dul guléet it, defin wu ni mel, ci téereb nettali bii la gën a fës. Daanaka, doxalin wu ni mel, mooy màndargay Kocc Barma dëgg, ci wàllu feemu bindkat bi. « Xaaju-guddi. Bu Caaroy gépp di nelaw ba fàttey boram laay yëg sama doole, sama xel gën a ubbeeku, samay xalaat gën a leer, kàddu gu ma soxla woo la nga tiit ci nelaw ne ma naam, ñëw tóojal ma ni góbi biy dox Dàqaar-Bàngo ba dajeek kapiteenam, lu ma la sant nga def ko. Taalif nag, daanaka kër gooy tabax la rekk, mbindeef yi fa yelloo dëkk di kàdduy askan wi te fàww mu am ci ñoom yu lay jéem a të, ëpp li nga leen di doye, yaradiku, foo tollu di leen dégg ñu dar seeni nopp di yuuxoo ka jàmbat. Waaye man lañ fiy fekk ! Man Kinne Gaajo, kàddu gu ma bëgg a tanqal ma dagg sa baat sànni ca xaj ! Réew mii maay Buur di fi Bummi, man Kinne Gaajo, ku neexul baat, déggoo galan déggoo ndigal, neel muut mbaa mott ! »
Danu jàpp ni – te xéy-na ay boroom xam-xam yu mel ne Soxna Aram Faal dëggal nu – Bubakar Bóris Jóob def nay jéego yu am a am solo ñeel mbindum wolof. Ni mu xareñe ci tërëlinu mbindum wolof mi dafa jéggi dayo sax. Képp ku méngale ñaari téereeb nettali yi mu génne ci wolof, « Doomi Golo » ak « Bàmmeelu Kocc Barma » dinga gis li nuy wax nii. Mu ngook, Bàmmeelu Kocc Barma neexul a wër ndombo. Looloo ko tax a nekk téere ci biir téere yi. Day téere bu nar a ràññeeku, amul benn werante, ci liggéey bu am maanaa bi bindkatu « Murambi, le Livre des ossements » yàgg a nekk. Téere bii, ku dem, day xiir askan wi cib jàllarbi. Bu nu waxee, jàllarbi, nag, aadaak baax lan ci namm. Maanaam, jàllarbi xel yi ak xalaat yi. Jàllarbi te jublu ci lu soxal Afrig ak doomiiy Afrig. Fexe ba doomi Afrig yi xamaat te moomaat seen démb, seen i cosaan ak seen i aada. Ñu war caa jóge, moomaat seen bopp dëgg, gëm seen bopp te taxaw temm taxawal seen jublu ngir defar seen ëllëg. Noonu la ko Séex Anta jàngalee, sunu sëriñ bi. Bu nu ci juum benn yoon : ladab ci réew mi doŋŋ a mën a tax sunu mbindum sunu làmmiñ yi mën a baax, law ba tasaaroo ci mbooleem-nawle mépp. Bu boobaa, ci fànn yépp la ngirte yiy feeñe ; maanaam ci njàng meek njàngale mi, ci liggéeyi biro yi, ci pólitig beek yorinu banqaasi Nguur gi… Koonte, mën nanu jàpp ne, liggéey bu dëggu boobu bindkat bi sas boppam, bokk na ci taxawaay ak xeex bi askan wi war a def ngir moom boppam dëgg, jëmale réewam kanam. Xam nanu xéll ne, Bubakar Bóris Jóob, loolu lépp réeréewu ko mbir.
Moo tax it du nu tàyyee woo – muy ciy mbindam, walla ciy taxawaayam – ci aajoo joyyanti tëralinu àddina. Àddina sii nga xam ne, rèew yi am doole yee ko noot, dëkk ci di noggatu réew yu néew
doole yi. Àddina sii nga xam ne, dan fiy jaar rekk, dem.
Boroom xam-xam yiy bind ci seen làmmiñ yiñ nàmp, ñu ngi nuy won ne, benn njariñ amul ci yàccaaral. Ak tamit ne, wax ju bare, fajul dara te bokkul ci liy suqali làmmiñi réew mi. Foo tollu di tudd Séex Anta Jóob walla Séex Aliyu Ndaw, te njàngum arafi làmmiñi réew mi sax, jaaroo ci. Li am solo mooy dogu te jublu ci njàng mi. Jàng « alif-baa » ci wolof walla ci benneen kàllaamab réew mi, walla bu Afrig bu mu mënti doon !
Kon nag, waar wu dese bay a ngi noonu, maanaam, warees na ba tey xàll yoon wu leer wiy tax nu mën a jàllarbi réew mi. Mu di yoon wu gudd a gudd, yoon wuy jéggi Senegaal, wër Afrig gépp. Yoon woowu waa « Groupe de Grenoble » ca Farãs, xàlloon ci ati 50 yi. Kurél googu, ay àndandooy Séex Anta Jóob taxawaloon, ñu mënoon ci ràññe ñu mel ni Séex Aliyu Ndaw, Masàmba Sare, Saliyu Kànji, Asan Silla walla Ablaay Wàdd, menn mi. Leer na ni waar woowu, mbayam sotteegul.
Koonte Bàmmeelu Kocc Barma deful lu dul lawal (niki yeneen i mbind yi ci sereer, ci joolaa walla ci pulaar, añs.) gis-gis biy tax nit, doomu-Afrig bëgg boppam. Fii nag, ci téereb nettali bii, mbégte mi moo di, saf-xorom si Bóris di àndal saa su taamoo kàllaamay Kocc ngir bay waaram ci tool bu am solo boobu ! Wolof bu neex a neex la nuy xéewale : « ci dëgg-dëgg, dafa neex ni tàngal bu ñuy macc bay tàqamtiku»! Bu ko defee, dunu def lu dul topp ndigalu Njéeme Pay, « daldi ni walbit, topp la », yow Bóris – waxumaak Njéeme Pay, waxumaak Kinne Gaajo ! – te naan la : gaawal génne ñetteel bi…!’