BUUR, LEKK AK NAAN, FOLLIKU DAY BETTE
Téll !… Xërr !… Téll !… Xërr ! Téll !… Xërr !… Takk-der yi fii, ndaw ñi fee, fetel yiy sox, xeer yiy naaw
Téll !… Xërr !… Téll !… Xërr ! Téll !… Xërr !… Takk-der yi fii, ndaw ñi fee, fetel yiy sox, xeer yiy naaw ; póno yiy tàkk, saxaar si ubale jàww ji. Coow laa ngi ne kurr. Wata dawatul, nit doxatul. Nde, yoon amatul. Jàmmaarlo bi metti na. Ndakaaroo ngi tàkk, Sigicoor di bax, Biññoona a ngi riir. Foo dem, sàndarm yeek pólisee yaa ngiy sox i fetel ak di sànniy gërënaad lakirimosen ci benn boor bi ; ci beneen boor bi, askan wi, rawatina ndaw ñi xamb i taal yu bërëx, jóor seen i xeer, naan leen xërr takk-der yi. Déedéet ! Du film de, géntooleen itam. Senegaal fii la xewe. Ci àjjuma jii, 17eelu fan ci suweŋ 2022.
Lu sooke mbir mi ?
Àllarba jële weesu, 8eelu fan ci suweŋ, Yewwi Askan Wi dafa amaloon am ndajem-ñaxtu ca Péncum Réew ma, « Place de la Nation ». Mbooloo mu takkoo takku wuyusi woon ko, fees fa dell. Mbar gi ne fa gàññ, foo sànni woon bàttu mu tag. Ñu xéy, ci alxames ji, yéenekaay yépp fésal ko, biral ndam li ci Yewwi Askan Wi góobe. Kilifa ya yakk lu mel ni xeme Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak jëwriñu biir-réew mi, Antuwaan Feliks Jom, tuumaal leen, tiiñal leen. Usmaan Sonko ne woon, bés boobu, « Bu Yewwi bokkul, wote du am Senegaal. »
Nde, lees jàpp mooy ne Njiitu réew meek i surgaam yi ne ci Nguur gi dañu bëgg a salfaañee mbir yi, kootoog yoon, ngir tere Yewwi bokk ci wotey dépite yees dégmal ci sulet. Te, ci seen i kàddu, Bennoo Bokk Yaakaar warul sax bokk. Ci njeexital li, ñu joxante dig-daje àjjuma, 17eelu fan ci suwe ngir delloo buum ca boy-boy ga. Waaye, ginnaaw gi biñ ko yégalee Perefe, daf leen ko gàntal. Ñoom, nag, ñu ne Perefe dafa jalgati yoon, te sax ñoom dañ ko yégal rekk, tàgguwuñu ko. Bu ko defee, waa Yewwi ne dee, dañuy amal seenum ndaje, ci nii, mbaa ci naa. Ci la tëkkoonte bi tàmbali, ku nekk, Nguur geek kujje gi, di dankaafu sa moroom. Noonu, ba ni àjjuma di ñëwee…
Ca njël, boori 5i waxtu, nee ñu, la takk-der yi dem ca kër Usmaan Sonko, fatt yoon yi jëme këram yépp. Koñ ba, kenn duggul, kenn génnul. Bi leen Usmaan Sonko seetsee ci yoor-yoor gi, laaj leen lu xew, kilifag takk-der ya tontuwul, daf ko ne rekk ndigal la jot. Njiitalu PASTEF li daf ko mujje ñaan ngir mu bàyyi soxnaam si yóbbu doom ji mu jàngi. Kilifa gi bàyyi wata bi yeboon soxna sa ak gone ga mu jàll, daldi sant ndawam yi ñu delloowaat dogu weñ yi ñu fattee yoon yi. Noonu lañu def ca kër Bàrtélémi Jaas ak ca Péncum obelisk ba, « Place de l’obélisque ». Ci kow loolu, ndaw ñi tàmbali woon génn, seen xel teey. Ñu daldi njort ne Maki dafa am lu muy waajal seen njiit lii di Usmaan Sonko. Nde, jamono jooju, noon nañ sàndaarm yaa ngi doon jéem a dàjji buntu màkkaanug PASTEF ga ca VDN ba. Waa PASTEF doon ragal ne, dañ fa bëggoon dugal ay ngànnaay ngir tuumal leen ak seen njiit li, Usmaan Sonko, wax ne ay way-fétteerlu lañu, maanaam ay rëbel yoy, seen nisër mooy taal réew mi. Ba-tey, ci seen i kàddu, jubluwaayu Maki Sàll mooy fexe ba teg tuuma ci ndoddu Sonko ngir tëjlu ko, tere koo bokk ci bépp xeetu wote ginnaaw bim ko defee Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll.
Noonee, ba ni julli jumaa di jotee. Sonko solu ba jekk, ànd ak i ñoñam, bëgg a jaamuji Yàlla, takk-der yi taxaw ci kanamam, tere ko ko. Ci saa si, xol yi tàmbalee jóg, ndaw yiy génn ci mbedd yi ndànk ndànk. Kolobaan, Ñaari-Tali, Parsel, Yëmbël, Site Kër-Góor gi, Sigicoor, Biññoona… jàmmaarloo bi tàmbali. Jarta laaj… Bakkan rot na ci, ñetti bakkan. Waaw, pólitig bi reyati na ñetti doomi réew mi.
Buur du jur buur, baadoolooy jur buur waaye…
Mbooloo mu takku mom, ndaw ñaa ci ëpp, gën cee fés ñoo génn ci mbedd yi. Naam, wooteb Yewwi Askan Wi lañu wuyusi woon. Waaye, ci seen i wax, seen ug ëllëg a leen tax a fippu. Ñu ne, dañu bàyyi seen lépp ngir xeexal seen moomeel. Jenn jëmm taxu leen a jóg, ci seen i wax ; ñoom, li ñuy xeex, jéggi na mbirum wote walla ay list. Nde, dofuñu, jinne jàppu leen. Ñu def i ndiiraan, fëx, wutali mbedd mi ngir ñaxtu, kaas seen i àq ak seen i ngoreef. Lees di tuumaal Maki Sàll mooy ne dafa bëgg a seppi ponkali kujje gi ci joŋantey wotey dépite yees dégmal ci weeru sulet, ci 31eelu fan wi. Way-ñaxtu yi ak waa kujje gi dañoo jàpp tamit ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, day wut ub poroxndoll ngir ga réew mi ñetteelug moome gog, yoon daganalu ko, ñeel ko. Nes-tuut, cóoki bi door. Takk-der yi, pólise yeek sàndaarm, ak ndaw ñiy xaañante.
Ndakaaru, Ñaari-Tali, fa xeex bi gën a taree, benn lakirimosen dal cib matlaa bu tege woon ci mbedd mi, mu ne jëppeet, tàkk ba jeex… Ndekete yoo, am na ku ca tëddoon ku, nee ñu, xel mi neexul. Ndeysaan, mu lakk ba xëm… Benn bakkan rotagum na.
Noppeeguñoo jooy, ñu tàggewaat beneen ndaw, ca Sigicoor… Ab balu fetel dëggantaan la kenn ci takk-der yi dóor Idiriisa Gujaabi ci baat, ñu rawale ko loppitaan ba, mu faf ñàkk bakkanam. Ñaari bakkan rotagum nañu… Gis nga ?…
Moone de, foofa ca Sigicoor, nit ñaa ngi doon dox-ñaxtu ci jàmm, ànd ak Gii Mariis Saañaa. Lu xew ci diggante bi ba njaaxum bu ni mel am fa ?
Nu ni déet-a-waay, ca Biññoona, kenn ci takk-der yi dàkk boppu Alex Abdulaay Jaata, natt ko ba am ko, ne ko téll bal, mu faatu… Maaradéetaali ! Ñetteelu bakkan biy rot ci bés bi. Céy lii… Ba kañ ?
Moone de, ñoom ñi ñuy rey, ñoo fal ñii leen di reylu tey. Faj seen i aajo moo taxoon ñu jiital ñi ci Nguur gi ci seen wàllu àddina. Moo taxoon itam ñu jiital niti diine yi ci seen wàllu diine, jox leen gëdd, déggal leen. Waaye, déggeesu ci kenn mu yéy, yàbbi ci mbir mi. Ndeysaan… Bu dul woon baadoolo yi tumurànke tey, kenn ci ñii du fi naane ñeex. Ndax, buur du jur buur, baadoolooy jur buur, waaye…
… cerey buur, rongooñi baadooloo koy siim.
Nga samp say laaj, naan kan lañu rey ? Lu tax ? Ma ne, yaa ko xamaatoo ! Li nga war a laaj mooy kan lañu reyati, lu taxati. Waaye, tontu la woon démb, mooy lu tey li. Ki daan rey démb, ba tey mooy reyaate. Ka ka daan digal, ba tey mooy ko koy digal. Ñi daan seetaan, ñu ngi wéy di seetaan. Ki yàgg a dee, moo deewati. Ki bakkanam jarul dara ci miim réew, ki amul tur, amul wéeruwaay, ki santul Mbàkke, Si, Ñas, Laay walla Aydara…
Kan lañ fi sañ a rey keneen ku dul ku amul i mbokk, ki ñàkk cëslaay ? Wax ma kan lañ fiy rey, ci neen, ku dul néew-ji-doole ji nga xam ne, Nguur gi tanqamlu na ko, yoon suufeel ko, sëriñ si ñeeblu ko ? Ma ne, baadoolo bee deewati, baadoola yaay dëjati, baadoola yaay jooyati. Nga neeti « Lu tax ? » Lu tax… Li taxoon a taxati. La woon, fa woon ; na woon, fa woon.
Ngor ak ngoreef (liberté), lii de moo leen tax a dee. Du leneen. Xéy, am foo xéy. Xéy, am loo lekk, am loo naan, yow ak sag njaboot. Xéy, boo feebaree am loo fajoo, am foo fajoo ci jàmm, yow ak sag njaboot. Xéy, say doom mën a jàngi, am fu ñuy yarooji. Xéyaale ak xel mu dal, di yëg kiiraay guy jóge ciw yoon wu màndu wow, mooy sàmm sag kaaraange ñeel li la wër ak ñi la wër, yow ak sag njaboot. Xéy, mën a doxi say soxla, di dem ak a dikk ci jàmm.
Dund gu doy te jàppandi, fajuwaay yu matale ak fajkat yu doy te xareñ, njàng ak yar yu baax ñeel njaboot gi, yoon wu jub te màndu, yoon (jaaruwaay) yu baax ak njëgi tukki yu jàppandi : lii rekk la baadoola yiy sàkku. Lii rekk a tax ñu leen di rey. Lilee tax ñu fal njiit yi leen tax a xiif, tax leen a mar, taxleen a ralfe. Lilee taxoon ñu dénk seenug kóolute njiit yii di leen toroxal tey, di sàcc seen i alal, seen i suuf te di leen génne ci seen i kër. Baadoolo yooyii amoon yaakaar ci ñii ñu jiital ci seen wàllu àddina ak ci seen diine ngir ñu sàmmal leen leen ; ñu nax leen, wor leen, njublaŋ leen. Yemuñu fa, ñu leen di bunduxataal ak a rey ci anam yu wuute te ñaaw. Moone, lépp luñ mën di doon, luñ mënti fàggu ci alal ak daraja ju ñu mën di am, ci ñaq ak dooley baadoolo yi lañ ko jële.
Ak lu coow liy bare bare, boo seetee ba ci biir, juróomi sabab yilee tax nit di fippu, ak fépp foo mën di dem ci àddina si. Ndege, fu xiif ak mar daje, wéradig yaram ak xel dolleeku ca, kaaraange ak kiiraay toxu fa, xamadi ak xayadi làng fa, tooñaangeek par-parloo ne fa faax… foofee, fitna du fa jóg. Saa bu amee as-tuut ciy nit, ñii toog ci donkaasi geek seen i làmmiñ yu neex, ñee ferenkulaay ci sijaada yeek seen i kurus yu gudd, ku ci nekk jàpp ni yaa gën ñépp, moom lépp, fitna du fi mës a jóg. Waaye tamit, fileek askan wi nàndul pexey dóorkatu màrto yooyu, fexee mucc ci ñoom, ndóol gi ak jafe-jafe yi muy xeex du fi mës a jóge. Waaye de, fitna du yem ci boppu boroom. Moo tax buur, lekk ak naan, folliku day bette.