USMAAN SONKO : "MAKI SÀLL CUUNE LA, DI DEF YËFI CUUNE"
EXCLUSIF LU DEFU WAXU - Askanuw Senegaal moo aajowoo nuy wax. Dafa di, bun toogee ab diir waxunu, dunu am jàmm. Foo tollu, ana diw ? Waaw moom, lu ko tee wax ? Lu xew ? Kon, wax ji mënta ñàkk
LU DEFU WAXU :
– Usmaan Sonko, ginnaaw bin la nuyoo, noo ngi lay sant di la gërëm bu baax. Nuy fàttali rekk ni yaay njiitu Pastef-Les Patriotes. Yéenekaayu web Lu Defu Waxu mi ngi lay jaajëfal ci li nga nu nangul jotaayu laaj-tontu bii. LU DEFU WAXU, nag, mooy yéenekaayub web ci kàllaamay Kocc bees fi jëkk a taxawal. Bu ko defee, nu bàyyi la nga nuyook jàngkati LU DEFU WAXU yi laata nuy sóobu ci waxtaan wi.
USMAAN SONKO :
– Noo ngi leen di fey bu baax a baax, di nuyu jàngkati LU DEFU WAXU yépp, mag ak ndaw, góor ak jigéen. Maa ngi nuyu tamit askanuw Senegaal wépp, ku ci nekk ak foo mënti nekk, di nuyu Afrig gépp ak àddina sépp. Bu loolu weesoo, bég naa lool ci li ngeen ma seetsi ngir séq ak man jotaayu laaj-tontu bi nuy waaj a amal. Maa ngi leen ciy gërëm, di ñaan ak a yaakaar li ciy rot lépp doon njariñ ñeel ñépp. Jërëjëf.
– Seetlu nañ ni, bi nga waxe ak askan wi ba léegi, coow laa ngi ne kurr : jàppal Sonko fii, bàyyil Sonko fee. Loo xalaat ci mbir mi ?
– Bala dara, noo ngi dollee sant Yàlla mi nu tàggat ba nu doon lin doon, gëm li nu gëm. Di ko sant yit ci tolluwaay bim nu yóbbu, ba sunu kàdduy wër Senegaal, jàll Afrig, daj àddina sépp. Du sunug njàmbaar, sunub xam-xam walla sunu mën-mën moo nu ko may. Ndaxte, am na ñu nu fi jiitu, gën noo jàmbaare, gën noo xam, gën noo mën te raw nu ci fànn yu baree bare te amuñu li nu am. Kon, noo ngi delloo lépp Boroom Bi ko sabab.
Xéy-na, sunu wërsëg mooy li nu maaseek jamono joo xam ne, lépp a gaaw, ndax anternet bi ak jumtukaayi xarala yu bees yi. Tey, lu naroon a def 10i at ngir leer ci xeli nit ñi, daanaka, bu yàggee ba yàgg, 2i weer kott lay def mbaa lu ko yées. Démb, benn tele walla benn rajo moo fi amoon, Seŋoor walla Abdu Juuf féete woo ko. Waaye, tey, tele yi, rajo yi, anternet bi, yéenekaay yi dañoo bare lool. Yenn saa yi, dinga am xalaat mu jéggi jamono ji nga nekk. Mooy waral, li ëpp ci say maas duñ xam fi ngay waxe. Daloon na fi ku mel ni Mamadu Ja, walla Séex Anta Jóob.
Bu ko defee, coow li mënta ñàkk. Ci réewum demokaraasi lan nekk, gis-gis yi bokkuñu, xalaat yi tamit, naka noonu. Loolu dafa baax cim réew. Dina tax nit kiy déglu, ginnaaw bim amaleem njàngatu boppam, xam jan wax, ban gis-gis walla man xalaat a yenu maanaa. Su boobaa, dina xam fu muy teg tànkam, tànn boor bi muy féete. Loolu, nag, képp ku koy jéem a tere, dangay sonal sa bopp ci dara ; bu yeboo nga nangu ko te noppal sa bopp.
Njiitu réew mi, Maki Sàll, bi muy door a falu ci atum 2012, dafa waxoon ne, dina nasaxal kujje gi, faagaagal ko ba dootul tekkeeti dara. Loolu, nag, kuy woote demokaraasi te di ko jëfe du ko sax xalaat ba koy wax.
– Ci sa gis-gis, nan la waroon a doxale ?
– Am réew, dees koy péncoo, di ci weccee xalaat. Ñépp mënuñoo bokk xalaat. Te sax, man dama jàpp ne askanuw Senegaal moo aajowoo nuy wax. Dafa di, bun toogee ab diir waxunu, dunu am jàmm. Foo tollu, ana diw ? Waaw moom, lu ko tee wax ? Lu xew ? Kon, wax ji mënta ñàkk.
Li nguur gi bëgg mooy fexe ba ñépp ànd ak moom, ñu amal fig nguurug bennoo giy ëmb pàcci réew mépp. Bu ko defee, kenn dootul sañ a taxaw naan « ànduma ci lii… », « lee baaxul… », « lale, bees ko defe woon nii mooy gën… » walla « ni nguur giy doxale, dara doyuma ci », añs. Réew nag, buñ demee ba kenn sañatul joxe sa xalaat, njaaxum ak musiba mu réy dikkal na askan wa fay yeewoo. Bala ñuy xippi, dina fekk ñu rey leen bu yàgg. Loolu, du fi ame tey, te du fi ame ëllëg.
– Danoo tàmm a gis lu Maki Sàll def nga xëpp ci suuf, mu woote nga wuyuji. Lu la tax a soppi doxalin ?
– Nun, ci kujje gi lan bokk te fasunoo yéene wàcc yoon win jël ndax dunu ay workat. Askan wee nu tax a jóg, moom lanuy xeexal ba keroog Yàlla di teg réew mi ci sunuy loxo, nu daldi koy defar bu soobee Boroom Bi. Looloo tax, bi mbas mi duggee ci réew mi ba tàmbalee law, nu wuyuji ca woote Maki Sàll ba.
Keroog bi nu demee pale, wax nan ko li nu jàpp ne baaxul ci xeexub mbas mi ak lin jàpp ne mën naa dem. Ba nu génnee yit, biral nan sunu xalaat, ñépp di ko dégg. Ginnaaw loolu, dafa sàkku woon ci Péncum-ndawi réew mi mu woteel ko ab sémbub-àtte bu koy may sañ-sañu doxal nim ko neexe. Nu génnaat ne àndunu ci, yëkkati sunu baat ci kow, nag. Ci kow loolu, ma waxtaan ak sama waa làng, ne leen nan toog seetaan, xool nu mbir miy doxe. Bin toogee weer, xool xool xam ni Làmbaay a ngi ñaaw, ci lan génnaat wax. Nun, nag, dugguñu ci politig ngir neex Ma-Sàmba walla Ma-Demba. Waaye, bëgg defar réew mee nu tax a jóg.
– Luy sa xalaat ci ni nguur giy xeexe mbas mi ?
– Waaw. Bala dara, warees na xam ne, Senegaal mooy 6eelu réew mu mbas mi gën a sonal ci biir Afrig. Kon, ñiy tëb di dal te naan : « Senegaal jàmbaar la, nàngam, nàngam … » xamuñu lu xew walla ñu tey ko rekk. Waaye, nañu defaraat seen toogaay te xam ni Senegaal jegewul sax ndam. Gis nga, mbas mi waru fi woon jur tiitaange ak njàqare gi fi amoon ca ndoorteel la. Jarul woon sax ñuy jagleel 1000iy milyaar xeexub mbas mi. Waaye, boo dee cuune yëfi cuune rekk ngay def, te Maki Sàll cuune la. 8i at yim def ci boppu réew mi yépp, day tandook a nimse rekk. Bu yëkkatee, ñépp yuuxu, mu bàyyi. Bu jaaree fii, ñu ne noo bañ, mu dellu ginnaaw walla mu jàdd. Te, loolu, mbas mi firndéel na ko.
– Ndax danga jàpp ni Maki Sàll dafa gaaw a tiit, dellu ginnaw, walla ?
– Noonu la deme ñeel coowal néewi doomi-Senegaal yi faatoo bitim-réew ci sababu mbas mi. Dafa juuyoo ak njiitu ëttub àtte bu kowe bi, Baajo Kamara, juyoo ak jawriñam, Aamadu Ba. Te sikk amul ci ne, ñooñu, ci waawam lañuy dox. Mbirum jumaa yi ak jàkka yi tamit, noonu la deme. Nooy tëje bérébi jaamukaayuYàlla yi ba noppi ubbi màrse yi, bitig yu mag yeek màngasin yi, oto yiy daw, nit ñiy liggéeyi di tañcaloo ci gaar yi ? Yenuwul maanaa, moo tax coow li am. Nu ni déet-a-waay, nga jàpplu Abdu Kariim Géy, wooluy Ilimaan, xéy ubbi bérébi jaamu Yàlla yi. Li gën a ruslu, mooy nguur joxe ndigal, mu am ay kurél yu ne duñ ko jëfe. Maanaam duñ ubbi seen i jumaa walla seen i jàngu. Mbirum njàng mi tamit, nun ñépp gis nan ni mu deme. Lii, gàcce mënu koo weesu. Loolu doyul, nga taafantoo guural gi, di jël dogal yu la neex. Rax-ci-dolli, xaalis bi askan wi dajale ngir xeex mbas mi, nga séddale ko say goro ak i farandoo, jox koy nit ñu ko yeyoowul. Lii rekk a tax askanuw Senegaal gisul boppam ci doxalinu nguur gi. Ndeyssan, loolu moo nasaxal nguuru Senegaal ba tekkeetul dara. Lu jiin Njaag a, te Maki Sàll mooy Njaag. Jamono joo xam ne, njiiti réew yi am fulla te fonk seen i askan ñoo ngi xool nu ñuy leen iy dooleele, di wër loppitaan yi ak ndefar yiy liggéey mask yi, nga ne déjj déjjaaral ci sab saal, di ‘’lido’’ ak say doom, naan ñakk bi nii, ñakk bi naa ak di saraxu ñu baal lab bor… Xéy bés rekk ne, damay faral àntarpiriis yi 200i milyaar ci seen lempo. Xam ngeen ne loolu, njuuj-njaaj ak càcc gu bir la. Bu dee ‘’Force Covid-19’’ moom, dama koo waxaalewul. Te nag, ma wax leen ko tey :1 000iy milyaar yi dinañ nu wax fuñ ko dugal ci nii mbaa ci naa.
– Bu doon yaa jiite réew mi, ci ban anam nga doon xeexe mbas mi ?
– Jamono jii, bu ma Yàlla dénkoon réew mi, doon naa lal i pexe, séddale xeexub mbas mi ci 2i pàcc.
– Ban ak ban ?
– Pàcc bu jëkk bi, fagaru lay doon. Maanaam, keroog bañ nee mbas dikkal na réewum Siin, keroog laa doon jël samay matuwaay, tëj digi réew mi. Ci laa doon dakkal dem beek dikk bi ba mu des gaal yiy yóbbu ak a indi dund ak yu ni mel. Bu loolu féetee boor nag, ma waxtaan ak waa réew mépp : fajkat yi ak waa-kër doktoor, liggéeykat yi, sàndikaa yi, kilifa diine yi, kilifa aada yi, way-moomeel yi, ndaw ñi, jigéen ñi, añs. Bu ma defoon loolu ba noppi, dama doon jublu ci ñaareelu pàcc bi, te mooy jàngat mbir mi, càmbar ko bu baax ci ndimbalug boroom xam-xam yi seen xel màcc ci lépp lu ñeel mbas mi : wér-gi-yaram, paj mi, koom-koom, nekkinu askan wi, aada ak cosaan, añs. Bu ko defee, dinaa doon xam naka laay doxale. Yaakaar naa ne, bun defoon loolu, tey, guural geek gaw gi ak lépp lu ci aju ciy dogal ak i tere du ko woon jar. Boo jiitee am réew, danga war a natt fu sa doole tollu ngir nga xam noo war a doxale. Ndege, fagaroo gën faju.
– Ndax am na lu PASTEF jot a def ci xeexu mbas mi ?
– Ngeen may ma tuuti ma leeral mbir : PASTEF, maye xaalis taxu koo jóg te du cëram. Dafa di, Senegaal, dafa am lu politiseŋ yi gëmloo askan wi, mooy ne : ab pàrti politig, dafa war di joxe xaalis. Loolu, nag, moo tax ku ci toog, di sàcc alalu askan wi, walbatiku di leen ci jox as tuut ngir gën a yàgg ci jal bi, di dugal ci nafaam ak ci nafay mbokkam. Loolu moo waral ngay gis ab politiseŋ boo xam ne, gorul, yattul, xéyul, gontul, xéy rekk di tabax i kër ak i taax yu yànj, di dawal i daamar, yor xaalis bu dul jeex, muy tibb di joxe, di gundaandaat ak a yaataayumbe… Ndeysaan, fekk ne boobu, xaalisu réew mi lay fowe, di ci jënde askan wi. Ba tax na, Senegaal mënta jëm kanam. Nun, nag, danu bëgg a soppigis-gis bi askan wi am ci làngu politig gi, ak ci politiseŋ yi ci seen bopp. Ndege, ag làngu politig warta joxe xaalis. Li ko war mooy tëral ab naal, jébbal ko askan wi ba noppi sàkku ci moom mu dénk ko réew mi ngir defar ko. Demal Etaasini, 2i làng ñoo fa am. Waaye, doo leen mës a gis ñuy maye xaalis. Foo mënti dem ci àddina si, noonu la, ba mu des Afrig. Loolu moo fi war a dakk. Ki war a joxe, mooy kees jox lenge yi, xàllal ko yoon wi, woteel kog nafa gu tollu ci 3.700i milyaar, dellu joxati ko 1000iy miliyaar. Bu ko defee, kooku lees war a laaj xaalis ndaxmoo yor xaalisu askan wi. Te xaalis boobu, dërëmu PASTEF ak yeneen làngi politig yaa ngi ci biir. Noonu la ci dërëmu ñépp nekke, muy taksimaan bi, di jaaykatu gerte bi, di boroom taabal bi mbaa jaaykat biy wër, masoŋ bi, beykat bi, añs.
– Kon daal PASTEF deful dara ngir mbas mi ?
– Ãkay . Naam, ci sunu wàllu bopp, dama ne woon gaa ñi PASTEF amul dara lu muy joxe ndax li ma wax léegi. Waaye, biñ ci ŋoyee wax ne fàww nu def dara, ci laa leen ne nañ ko def ci sutura. Jarul wone tele, jarul a siiwal ci rajo yi. Ma ne leen, « …xam ngeen miskin ak néew-doole yi nekk ci gox-goxaat yi. Mën ngeen leen dimbali ci sutura, kenn bañ cee yëg dara. Lenn, daal, mën ngeen koo def, mooy boole li PASTEF di joxe yépp nataal ko ngir ñu xam ne lii PASTEF a ko joxe ; wànte bu kenn xam ne kii walla kee moo jot lii walla lee… » Léegi nag kom yéen a ma laaj, dina leen tont : yóbbul nan ci loppitaan yi ak bérébi fajukaay yi ay jumtukaayi paj, te loolu def nan ko ci biir réew mépp daanaka. Biralees na ko ci sunu xëtu Facebook. Móodu-Móodook Faatu-Faatu yi bokk PASTEF tamit yónnee nañ xaalis bu takku. Lépp nag, ci sutura lan ko def. Loolu daal, lan jot a def. Te Yàlla xam na ne duggewun ko ngistal, jaay sunu pàrti taxunoo jóg ; moo tax séentuwunu ci kenn ku nu defal dara mbaa mu nuy sànnil kàrt ëllëg. Bu doon sama sago, du am. Waaye, ni Senegaal tëdde, di réew mu nit ñi war a dimbalanterekk a tax.
– Yenn njiiti Afrig yi te Maki Sàll gën cee fës ñu ngi ñaan ñu baal leen bor yi ñu ameel yenn réew yi. Ndax yow jàpp nga ni bor bi dañ koo war a far ?
– Gis naa Maki Sàll soppi tuuti ci waxin wi, naan yalwaanuñu, ni ñu dàqe àpp gi doy na ñu. Jàpp naa ni waxu ku mer la ; xéy-na li mu làmb, làmb mu dëgër moo ko waral.
Nun ci kujje gi la nu nekk te sunu xam-xam màcc ci mbir mi, juróomi at a ngii nuy jooytu bor bi te tegunu ko rekk ci ay wax. Am réew dafa am lu mu moomal boppam, am lu ko Yàlla wërsëgalee. Naam, am na loo xam ni mën ko jéggaani waaye fexeel ba li nga moom nga yor ko yorin wu rafet, bañ koo sàggane, bañ koo waanteer.
Coowal petorool bi, bind naa ci téere, wax ci lu nekk ba mujj noppi ; coowal zircon, phosphate ak ICS, gis ngeen ko ; sunu suuf sépp mu jaay ko ay doxandéem ñuy bey di yóbbu feneen, li baaxul delsi Senegaal. Kenn umpalewul sunu géej gi fi mu mujje, tey sunu mool yi mënu ñoo am lu dul yaboy. Alal ji ma wax nii mat na téeméeri yoon bor bi ñuy leb, su nu ko sàmmoon rekk, du soxla ñuy lebi kenn.
– Ndax am na réew mu dul leb ?
– Bu dee réew yépp ay leb tamit, ñaar a ngii : Lebu Sapoŋ bokkul ak bu Libaŋ, ñaari réew yi ëppaley bor ci àddina si. Koomu Sapon daa naat bu baax, moo raw ci àddina si. Wóor na ko ni su lebee, mën na fey te bala muy egg fii dafa liggéey bu baax, tëye li ko Yàlla baaxe ak feyum limpo.
Fexe ba lempo yeembambaay, ñi war a fey ñépp di fey amagul Senegaal fi mu tollu nii. Alalu réew mépp saax-saaxe nañu ko : Naar ak doomu Amerig ku ñëw ñu siñéel la, Tubaab ak Sinwaa waxi-nopp. Waxatuñu dara, nga lebi xaalis bu dul jeex ci turu askan wi. May wax, mu naan nañ ko baal bor bi. Yaakaar naa ne mébétam moomu du sotti. Bala may bëgg dee ñu naan dañoo am “signature” bu baax. Ku am “signature” bu baax, du ni faral leen ma bor bi.
– Waaye bor bi nag dafa xaw a takku…
– Dama ne, Sapoŋ, Farãs, Amerig añs ñoo ñu ëpp bor fuuf te doo leen mës a dégg ñuy ñaan ku leen ko baal. Maki Sàll xam na li koy xaar : bu ñu génne ci mbas mi, doomi Senegaal dinañu dund jafe-jafe yu tar a tar ndax koom gu néew doole gi ciy topp dina metti lool ci Afrig te Maki Sàll daa jëloon léppam aj ko ci peterool bi. Léegi leer na ni peterool ak gaas kenn du ko jariñoo 2023 te sàggane nga li nga moomal sa bopp. Ci at mi, Senegaal dina fey lu ëpp 350i milyaar ci bor booleek crise sociale bi : ñàkk xéyu ndaw ñi, mbey mi, napp amatul, ñàkk di wéy. Moo tax Maki Sàll sonn ci nañ far bor bi. Waaye du fi ame te bu soobee Yàlla, dina wax fum dugal xaalis bi mu leb yépp.
– Looy wax ci xoqtal ak metital yi takk-der yiy toroxal askan wi ci jamonoy guural gii mbas mi sabab ?
– Li jiitu ci sama wax, mooy ne damay gërëm, di sargal ak di delloo njukkal takk-der yi. Ndaxte, ñooy wattu sunu kaaraange guddeek bëccëg. Ginnaaw Yàlla, bu dul woon ñoom, Làmbaay ñaaw. Seen liggéey yombul te anam yiñ koy defe dafa metti lool.
Nun, dipite yi, yoon may nanu nu génn ci jamonoy guural gi. Te man, damay faral di génn 2 walla 3i guddi yu nekk. Yenn saa yi ma daje ak ñenn ci ñoom, nu lal aw waxtaan. Bu ma leen xoolee, sama yaram day daw. Seetal rekk, guddig weeru koor, ci ngelaw li, ñuy fanaane taxaw guddi ba bët set. Loolu metti na.
Dëgg la, nag, am nay jafe-jafe diggante askan week takk-der yi leen war a aar. Léeg-léeg, ñu lijjanti mbir mi ba du jur gàllankoor ci benn boor. Waaye, yenn saa yi, mbir mi ëpp i loxo ba njaaxum am ci, ñii am ciy gaañu-gaañu, ñale ñàkke ci seen bakkan. Man, nag, dama foog ne tàggat gee des. Xawma naka lees ko tërale, waaye dafa mel ni dañuy dëddale takk-der yi ak askan wi. Ngir jox leen ci misaal, damay sukkandiku ci sama jaar-jaar ca ENA.
Dañ nu doon faral di wax kàddu gii : « mooytuleen « contribuable » bi (ki war a fey lempo) ; dafa ñor, day njuuj-njaaj, day nëbbu » topp di la ko wax ak a waxaat. Yëf yi ub lool sama bopp, ma toog sama néeg naan sama xel moonte de samay waajur ay « contribuable » lañu. Moo tax bés ma laaj sama benn porfesoor ndax ‘’contribuable’’ bi nit ak i noppam la walla tur la rekk wu ñuy bind cig kayit.Ndege, baat yiñ lay tàmmal ca daara ja, méngoowul ak li ngay dund, di ko gis bés bu nekk. Moo tax, boo jotee sab lijaasa ba tàmbalee liggéey, dangay noonoo « contribuable » bi, ndax dañ la gëmloo ne du ku baax, jubul, day labaj.
Amaana, looloo dal takk-der yi dem bay xoole askan wi ay bëti noon.
– Luy sa xalaat ci la takk-der ya duggoon kër Ilimaan Ñiŋ ( Caaroy) , jaay njambootam doole, dóor waa kër ga, toroxal leen ?
– La xewoon ca kër Ilimaan Ñiŋ, jaaduwul te rafetul. Damay koy naqarlu te di ko mas-sawu, moom ak njabootam. Ndaxte, jàkkaarlook nit ku yorul gànnaay, xeexul ak yow, nga dóor ko ba toog ci kowam, du yoon, ag nitadi la. Dangay xool ni alkaati yiy doxale ci doxi ñaxtu yi. Doyoon na rekk sànni ay gërënaad lakkiromosen. Waaye, dañuy dàq nit ba ci biir këram. Te, loolu amul feneen ci àddina si.
Waaye, askan wi am na ci wàll. Ndaxte, mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam.
– Mel na ni yow ci sa bopp dundoon nga lu xaw a nirook lii ?
– Dëgg la ndax ay sàndarma mës na ñoo dem sama kër yaay ca Sigicoor ngir nangu fay kayiti parenaas. Bi loolu amee, dama jël ab layookat, topp mbir mi ba mu sës. Ca mujjantal ga, yoon jox na ma dëgg, daan sàndarma ya fa demoon.
Senegaal, moom, mooy réew moo xam ne, ku ñaawtéef laalul, danga nga naan sama yoon nekku ci. Gii Maryiis Saaña xam na dara ci li may wax. Askan wee war a fippu, bañ, ne na ñaawtéef yi dakk. Bu doon ci réewi Tubaab yi, askan wépp a ngi ci mbedd yi.
– Danga yaakaar ni li takk-der yi nekke, dañ leen cee bàyyi ?
– Ci beneen boor, waaw. Waaye njort naa ne, dañ leen di jox it ay ndigal yenn saa yi. Ndaxte, ku xam ni pólis di doxe, nga gis ab alkaati bu nekk ci biir màkkaanam sañ a def widewoo, yor i liif di tëkku askan wi, di ko dig ay dóor…ñàkkul mu am luñ ko sant. Ndaxte, ñoom daanaka yoon da leen a muumaloo. Amaana yit nguur gi ragal te xam ne amul ay alkaati yu doy yum mën a tasaare ci réew mépp. Xam naa, moo tax mu ni leen nañ tiital gaa ñi ngir ñu bañ a génn. Ndaxte askanuw Senegaal dafa ragal yat. Li koy firndeel mooy, ci bés bu jëkk bi dañu duma gaa yi bu baax, ca ëllëg sa, gisuma sax muus muy taxawaalu. Li ma tax a wax ne dañ leen koo sant mooy ne, dara du leen ci fekk, kenn du leen teg i daan. Loolu nag, baaxul, day féewale pólis bi ak askan wi. Warees na koo joyyanti ba jubale leen, ñu doon benn.
– Nan jàll ci mbirum taalibe yeek xale yiy taxawaalu ci mbeddi réew mi. Nguur yi fi jot a jaar yépp, lajj nañ ci caytug fànn boobule. Lan moo ciy sa njàngat ?
– Am réew, boo bëggee xam nu ëllëgam nar a deme, natt ko ci ni muy saytoo ay doomam, jigéen ña ak néew-doole ya. Duma def lu dul dellooti mbirum taalibe yi ci loxo doxalinu nguur gi. Ndaxte, bu dee ñu bari ci way-juri tey yi sàmmontewuñak seen i warugar, nguur gi moom loolu waru ko.
Bu dul dara sax, rafetul ci xar-kanamu réew, ay xaleem di taxawaalu ci mbedd yi. Muy taalibe walla ñiy mbubboo daara (am na ci réew mi). Yenn saa yi nga dox ba daje ak njabootug lëmm, ñu nekk ci mbedd mi, ci jamonoy seddaay ak ngelaw…dangay yéemu sax. Li ngay jëkk a xalaat mooy, lan la xale yii nar a dooni ëllëg ? Ndax bàyyees na xel ci seen wér-gi-yaram ? Bu dee am mag mooy tegaley yére yu bari ngir aaru, nu xale yiy def ? Nguur gi warul seetaan loolu.
– Ndax ñàkk pas-pasu nguur gi la ?
– Bu ngeen fàttalikoo, 4i at ci ginnaaw, Maki Sàll amaloon na fi ndajem jawriñ ca Pikin, ca la waxe woon ni « benn taalibe dootul taxawaalu ci mbedd yi » ; boobaak léegi, nag, tey la Waalo gën a aay. Te mbir mi, wareesu koo yemale rekk ci taalibe yi. Benn xale warula nekk ci mbedd mi.
Waaye, boo amee ag nguur goo xam ne, amul baat ci benn boor, daraam du sotti. Dara waralu ko lu dul li nguur gi génne loxoom ci diine ji ak ci daara yi. Xam ngeen ne, buñ demee ba naan nguur gi day xeex daara ci miim réew, soxla am na. Njabootu daara yi dem nañ ba jàpp ni nguur gi noonu daara yi la, walla sax noonu diine ji la. Man, nag, dama naan nguur gi defalul daara yi waaye duma wax ne dafa leen noonoo. Loolu, nguur guy xaru rekk a koy def. Li mu defalul daara yi, nag, moo tax amul màqaama wax ci ñoom. Nu wax ko te dee, nguur gi dafa sàggane gëm-gëmi askan wi.
– Luy mébétu PASTEF ci mbir mi ?
– Ngëm dafa nekk pàcc mu am solo ci dundu nit ki. Ni ko wér-gi-yaram soxalee, noonu la ko gëm-gëmam yittelee. Nit dina feebar, dem loppitaal ñu koy jox i garabi-tubaab te du wér, fekk ne feebaru ngëm la ame. Kon, loolu dafa am solo.
Moo tax, nun, ci sunub naalu 2019 bi, danoo waxoon ne warees na cëral diine ji ci naal yi nguur giy lal, yoonal ko. Damay faral di dégg ñu naan Senegaal réewu layig la. Waaye loolu ay waxi kasaw-kasaw rekk la. Bala nga koy xam Gàmmu jot, walla Màggal, walla Pópangin. Nun, dunu réewum layig ni ko ñenn ñiy xalaate. Mënees na wax ne, Senegaal, réewum ngëm la moo xam ne, xàjj-ak-seen amul ci diggante diine yi ak këri diine yi.
Bu ko defee, bu nuy tëral nafa gi, warees na sóoraale diine ji, beral ko xaalis ni ñu koy defale njàngum tubaab bi añs. Boo demee réew mu mel ni Marog, looloo fa am. Dañoo wutal diine ji ag njawriñ gu koy toppatoo. Maanaam, defar jàkka yi, jàngu yi, daara yi, añs. Nun, waa PASTEF, loolu mooy sunu mébét.
Bun defee loolu ba nopppi, ci lanuy soog a mën a wax ci daara yi ak lépp lu jëm ci diine ji. Bu ko defee, dinan yoonal daara yi ba, képp ku jóg ngir ubbi daara, dina ko teg fu wóor. Dinan la topp, xool ndax jàng nga, ndax am nga ñu lay jàppale ci liggéey bi, ndax am nga béréb bu baax, añs. Waratunoo nangu ab Sàmba Njaay làq ay doomam, dugal leen lekkool, ba noppi jël ay doomi jàmbur di leen yalwaanloo ci mbedd mi.
Waaye, nag, du lépp a bon ci daara yi. Am na ay daara yu baax yu fi nekk, bu ma fi nekkee di lim damay juum. Boo fa demee, benn xale du génn. Yorees na leen yorin wu rafet. Ni njàngum tubaab bi amee kurél guy saytu lépp lu ci aju (inspection d’académie), noonu lees war a wutale daara yi tamit ag kurél guy wattu lépp lu ci aju.
– Danoo seetlu ne, léegi, saa booy wax ak askan wi, làmmiñu wolof ngay jëfandikoo. Lan moo ko waral ?
– Waaw. Loolu, du lu ma jékki-jekki rekk def ko. Ndànk ndànk la ñëwe ci man. Boo seetee, 3 ba 5i at ci ginnaaw, ni ma doon waxe farañse laa doon waxe wolof. Waaye, may dox di seetlu, di jàng lu bari. Wax dëgg Yàlla, jàng naa téere yu bari. Waaye, ni may kàdduy Séex Anta Jóob di dugge, li miy def ci man, keneen defu ko ci man ci ñi ma jot a jàng seen i téere. Bi ma jàngee ay téereem, dama toog xalaataat lu bari, mu yee ma ci mbir yu bari, rawatina li jëm ci làmmiñi réew mi ak sunuy aadaak cosaan.
Gaa, man duma wolof, waaye sama yaay séeréeru Xombol la, wolof lay làkk. Sama baay joolaa la, sama maam bi jur sama yaay di al pulaar, kon man mën na wax ni duma wolof.
Waaye, Yàlla am na ci nit ñi yërmande joo xam ne, fépp fu mu boole ay nit yu wute ci waaso, dina fa tàggat aw làmmiñ wu leen di boole, ñu cay jokkoo. Dangay seet, tey, bu doon wolof bi wolof kese la dégg, al pulaar di wax pulaar kese, joolaa bi yem ci làkkam, séeréer bi noonu, añs. Kon, nan lanuy déggoo ? Du sotti. Yàlla la neex mu sàkk nu ba noppi, def nuy kurél ak i pàcc ngir nu xamante, xàmmente, ni mu ko waxe ci Alxuraan. Kon, du ngir féewale nu. Tey, boo demee Kaasamaas, gis ni joolaa yiy soloo ak a fecce, dinga ci jànge lu bari, nga dem feneen ci ñeneen ni tamit noonu. Bu ñépp bokkoon lépp, àddina si day soof. Waaye, li nu boole moo ëpp li nu wutele. Fii ci Senegaal, fépp foo dem, dégg nañ wolof. Mën nañ ko bañ a wax waaye dégg nañ ko, te loo ci wax xam nañ ko.
Farãs, atum 1375 lañ gàll farañse bi def ko làmmiñu réew ma, mu wuutu lateŋ. Siin moo nu ëpp ay kàllaama fuuf, 300i daanaka. Waaye, teewul màndareŋ lañuy jëfandikoo. Noonu la amee fépp. Nun Senegaal, wolof la fi Yàlla tànn. Warees na nangu lu ni mel.
Raayante bi moo fi war a jóg, wolof mooy làmmiñ wi nu war a boole. Ku bañ a làkk farañse, lu tax ngay bañ a làkk làkku nit ku ñuul ni yow ? Kenn waxu la nga nekkaat wolof. Waaye, ab jumtukaay kese la ngir wax ak ñi nga bokkalul waaso. Te sax, aaday wolof, séeréer, ak joolaa wutewuñ lu bari.
Bu dee lu jëm ci mbirum njàng mi, bun demoon ba sàrtal njàngum làmmiñi réew mi ci lekkool yi, wolof mooy doon làmmiñuw bennale wi. Ñépp a koy jàng. Ginnaaw gi, nag, gone gu ci ne tànn weneen làmmiñ dolli ci, moo xam pulaar lay doon, séeréer, joolaa, soose, añs. Loolu, bu amee, xale bu ci nekk dina mën a wax ñaar ba ñetti làkk ci làkki réew mi. Te, loolu day gën a dëgëral bennoo bi.
Bun génnee Senegaal, nag, jàpp naa ne, biir CEDEAO, awsa lees war a tànn. Bu dee Afrig gépp, suwaayili bee ci gën a yey.
– Luy sa naal ñeel aada ak cosaan ?
– Aada mooy lépp, mooy cëslaayu yokkute. Waxuma, nag, tëgg, fecc ak li xew jamono jii. Sumay wax aada, xam-xam, cosaan ak sag yi mu làmboo ma tax di wax. Ndege, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Nit dafa war a gëm boppam.
Tey, Sinwaa bi dafa gëm ni Siin moo war jiite àddina si te ndog-ndog da ko daloon ci diggante bi, Àngalteer ak Sapoŋ raw ko. Moo tax, Siin dafa gëm cosaanam ak démbam. Iraŋ, bu àddina sépp waxee mu téye fi mu téye rekk, ñemee ŋoy fi mu ŋoy, booba cëslaayu aadaam a ko ko may. Ñoom, ca nguurug Pers ga woon lañuy sukkandiku fonk seen bopp. Turki, ñoomit, ca nguurug Otomaan ga woon lañuy wéru. Boo demee Ërob, tamit noonu. Kon, koo jël ci àddina si, ci démbam la sukkandiku ngir jéem a suuxat réewam. Loolu la Séex Anta Jóob xamoon bu yàgg. Moo tax liggéeyam am solo lool.
Moo saxal ni, ciy gëstoom, Afrig benn aada a ko lal, te Misra moo fi ëppoon doole. Tubaab baa ñëw ci ginnaaw, gëmloo nu leneen, suufeelnu banu xeeb sunu bopp. Xeebeel boobu la Séex AntaJóob dindi.