BATAAXALU ITALI BU TIISE NII…
Mbokki Senegaal,
Maa ngi leen di nuyu yéen ñépp, ku ci nekk ci sa tur ak sa sant.
Tey, fii ci Milaŋ, maak sama soxna danoo yeewu, lànk ne dunu seetaan tele, gedd tamit rajo bi, ne ko waay-waay yaa ngi nuy tanqal, tëjal sa gémmiñ gi !
Lu waral nu doyal ci widewo yeek rajo yeek tele yiy yeete guddeek bëccëg ? Xanaa njàqare gu jéggi dayo. Ci dëgg-dëgg, kenn xàmmeetul Itali, rawati-na Milaŋ gii nu dëkk. Lii moom gën a metti ! Waaru nanu, musibaa ngiy daagu ci mbeddi réew mépp, fas-yéenee samp raayaam ci sunuy xel. Wolof dinay wax ne lu la bett, mën la. Waaye sama maam daan na ci teg ne bu la daanul, jeŋal la. Boo jëlee tey kàddu yu am solo yooyu tasaare leen ci biir Itali, dinga xam lu tax ma tàmbalee nii sama bataaxal bi.
Mbokki Senegaal, duma sonal sama bopp di leen laaj ndax yëg ngeen ne am na doomu-jàngoro bu bëgg a faagaagal Itali. Fi mu ne nii mooy coow ci àddina si juróom-ñaar ! Wiris bi mayunu jàmm, mu ngi fiy def ay jéyya yu kenn mënul a nettali, mu ngi rey di dem, su ma ko mën a waxe noonu.
Sunu dundin soppiku na bu baax.
Léeg-léeg sa xarit woo la, sa xel di werante ndax war nga koo jël am déet ndax rekk ragal a dégg xibaar bu tiis, xibaar bu sa xol bi du àttan, xibaar bu lay tiital.
Nun daal mbokk yi, ñaari ayubés a ngi nu tëju ci sunuy kër, demunu dikkunu. Génn ci mbedd mi tàllal say tànk walla sëppu sa palanteer sax kenn ñemeetu ko !
Li gën a yéeme, nag, moo di ne amul ku mës a gis wiris bi mbaa mu xam fan la làqu. Moo waral koo jege mu dandu la ci saa si, ñeneen ñi bu ñu lay séen ngay ñëw di teggi yoon, duñ ci am benn kersa ! Tàggat-yaram mel na ni lu fi xewwi, taxawaalu kenn waxaalewu ko. Ku génn sa kër te jëndiwoo garab walla dund, yoon dal ci sa kow.
Koom-koom bi sooxe na lool, lekool yi tëj nañu, bitig yi waxi-noppi.
Tekk-tekkaaral gi nag, mbokk yi ! Oto riiratul, baat jibatul. Léeg-léeg daal nga dégg àmbilaas buy mbiib mbaa damaar bu fees ak i néew di leen jébbali seen boroom. Ana lu gën a daw lii yaram ? Li yées ci mbir mi moo di ne néew yu bari seeni mbokk duñ leen gis, nga faatoo loppitaan walla sa kër a ci yem. Muy lu doy waar lool. Nga am sa maam, sa yaay, sa xarit walla sa doom, mu génn àddina ci anam bu tiis te doo ko gunge, mu mel ni dafa xéy ne mes ci jaww ji…
Xoolal ma ni koronaawiris saay-saaye : day yoot ba xéy jël la te garabu nit walla garabu jinne duñu ko mënal dara ba dara booloo jeex. Kii nag mooy gan gi kenn bëggul mu jub la : doo xam kañ lay tàggoo ñibbi,nga am jàmm. Foo tollu yaa ngiy ñaan mu bañ a yendu mbaa fanaan sa kër.
Mbokki Senegaal, koronawiris jur na fiy jafe-jafe yu ub lool sunu bopp : loppitaani Milaŋ ak diiwaan yi ko wër yépp a fees ak i doom-aadama yu feebar bi daaneel te të leen a bàyyi. Doktoor yaa ngi def seen kem-kàttan, pólitisyeŋ yi mel nañ ñu jommi, xamatuñu lu ñuy wax ndax joŋanteek téesante xajuñ fi. Am na ñuy wax ne su tan amulee ci ayubés yiy ñëw, nguuru Itali dina jël yeneen ndogal yu gën a jafee dékku ndax daanaka bu boobaa kenn dootul génn sa kër.
Yàlla rekk mooy buur, moom mi def ba mbindeef yépp bokk benn soxla ak benn xalaat, benn buum kott lëkkale leen, ñu mel ni findifeer yuñ boole raw. Teewul ku nekk yëg ci biir xolam wéetaay bu metti, di wut pexe mu koy musal ci jàngoro ji.
Mbokki Senegaal, nun feebar bi daf noo bett ba léegi faju moo fis sës. Faju moo fi sës waaye amunu garab gi nu mën a faj… Dégg ngeen wax jeem ? Kon boog jàng leen bu baax sama bataaxal bu tiis bii. Bëgg li nu dal amal leen njariñ rekk a ma ko tax a bind.
Yàlla na jàmm yàgg Senegaal ak Itali !