LAAJ-TONTU : SAADA KAN BÓRIS JÓOB (II)
Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laajt-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019
Bii mooy ñaareelu xaaju waxtaan wi. Dinan leen indil ñetteelu xaaj bi
S. K. :Bóris, yaa ngi dox ay jéego yu am solo ñeel làmmiñi réew mi. Këru móolukaay bi nga sos tudde ko EJO, jagleel ko làmmiñi réew mi te soxna Ndey Koddu Faal jiite ko, bokk na ci la koy firndéel. Waaw, lu tax nga tudde ko EJO ak lan la EJO tekki ?
B. B. J. : Waa…waa…waaw. Wax nga dëgg ! Baatu EJO mi ngi jóge ci làkku Ruwandaa. Te, Ruwandaa dafa di réew mu ma xam lool, mu neex ma lool sax, wax dëgg. Rax-ci-dolli, am réew mu ma jox cër la, fonk ko lool itam. Bu loolu weesoo, EJO baat la boo xam ne, mënees na koo firee démb ji walla ëllëg ji. Kon, baat bi ëmb na ñaari jamono : li nu weesu te mu sax ci sunuy xel ak i xol (cosaan) ak li ñëwagul te nu koy séentu di ko waajal (suba). Loolu, nag, du neen. Diisaayu baat bi ak maanaa ji mu làmboo bokk na ci li tax nu taamu ko.
Bu ko defee, mënees na wax ne, ca dëgg-dëgg, ñaari mbir ñoo sabab tànneefu tur wile. Bi ci jiitu mooy topp ci tànki Séex Anta Jóob mi nga xam ne, mi ngi tënkoon xeexam ci leeral sunu démb ak ay firnde yu wér, dekkil sunu moomeel ak sunu ngor ngir waajal ak liggéeyal ëllëgu Afrig bu naat a naat.
Ci beneen boor, li nu ko dugge mooy biral bennoo doomi-Afrig bi nuy xeexal. Ba tey, ci tànki jàmbaar ji lanuy top, sunu werekaan bii di sunu royukaay Séex Anta Jóob. Ndaxte, bu nu neexoon nu tànn benn baat ci baati wolof yi, walla benn baat ci làmmiñi réew mi. Waaye, dafa jot nu jéggi digi waaso yi, far digi réew yi te fexe lëkkale doomi Afrig yi nga xam ne, ñoo bokk cosaan, seeni aada ak i làmmiñ bokk menn mbakkan mi leen meññ. Ci tënk, turu EJO wi day màndargaal yoon wi nu taamu te muj gi di sunub afal, maanaam afalub Afrig ba mu daj. Yoon woowu nag, cosaan la tàmbalee, jaar ci réewi Afrig yépp ngir lëkkale leen, boole leen def benn, ba noppi wutali ëllëgu booloo ak naataange ju dàq.
S. K.: Sos nga yit benn yéenekaayu web ci làmmiñu wolof tudde LU DEFU WAXU ; ngeen tekki tamit téere Mariyaama Ba bi ci kërug móolukaay gu ñuy wax Céytu. Nu gis ne, ba tey, ci Séex Anta la mbir miy dellu ndax Céytu la cosaanoo.
B.B.J. : Waaw. Dëgg la. Ñépp xam nañ ni Céytula Séex Anta Jóob fekk baax. Dafa am lu nit ñu bare réere mbir ci Séex Anta Jóob. Mooy ne, bala dara, Séex Anta tekkikat la woon. Ca njëlbéen la sóobu ci tekkinu mbindi boroom xam-xam yu mag a mag. Noonu, jotoon na tekki ci wolof tënkub « La théorie de la relativité » bu Albert Einstein, bàkku réewum Farãs, ay jukki ci mbindi Corneille ak ci Odyssée, añs. Muy lu am a am solo, rawati-na bi muy méngale làmmiñu Misra gu njëkk gaak sunu yos yi : wolof, séeréer, pulaar… te muy liggéeyub tekki ba tey. Waaye, gaa ñi duñ ci bàyyi xel. Dafa di, sax, am na ci ñoom ñu xeeb làmmiñi Afrig yi.
Xam nga, Saada, dafa am lu mat a wax ci xeltukati miim réew, muy lu doy waar. Gis nga, bi ma génnee sama téere wolof bu njëkk bi te muyDoomi golo, ñu bare ci xeltukat yi dañu waaru woon, ànd ak mbetteel gu réy. Maa ngi fàttaliku kàddu giñ ma daan wax, naan ma : « waaw, Bóris, ndax yaakaar nga ne sunu làmmiñ yii mënees na cee bind ay téere fént yu mucc ayib ? » Du càggan ne, dañu xeeb walla dañu suuféel làmmiñu wolof ndax xam naa leen bu baax a baax sax, meluñu noonu. Dama foog ne ñàkk xam la rekk.
Jàpp naa ne, ndege, ni nit ñi bokkee, noonu yit la làkk yi bokkee. Te sax, làkk woo gis, am na lu mu yoreel moroomu làkkam. Loolu waral, ci misaal, nu mën a jóge ci àngale tàbbi ci farañse, jóge ci farañse tàbbi ci àngale, noonu ba làkki àddina sépp daj, rawati-na sunuy làmmiñ. Rax-ci-dolli, Sëriñ Musaa Ka, taalifkat bu mag bi, dafa ne : “wépp làkk rafet na, buy yee ci nit xel ma, di tudd ci jaam ngor la”. Kon, ku mu neex tëbee ca español, dali ci pulaar walla séeréer. Loolu dafa neex ! Bu nu ko kenn yàqal ! Loolu, mbaax gu nu Boroom bi jagleel la. Ni nit ñi bokkee benn maam (Aadama), noonu la làkk yi bokkee wenn ndeyu-làkk wi leen bokk njaboote. Kon, deesu leen a féewale walla di samp ay dig ci seen diggante.
S.K.: Bóris, bëggoon naa xam ndax mbindum wolof yomb na la. Ndaxte muy man, di yow ak sunuy moroom, ay guney Medinaa lañ. Wolof bi nu tàmm a làkk ak wolof bu set wecc bi ngay bind ci say téere dañu wute. Ndax danga jàng wolof walla yaa ngi jàng ba léegi ?
B.B.J.: Sa laaj bi am na solo lool, sax. Dëgg la, jàng naa wolof ak ñoom Paate Jaañ ca Iniwérsite Séex Anta Jóob bu Ndakaaru ak ci sunu biir kuréli politig yi nu amoon ci ati 1960 yi. Ndax, nag, danu fullaloon bu baax mbirum làmmiñ. Bu dee wax dëgg rekk, nag, mësu maa yaakaar ne bés dina ñëw ma bind ci wolof. Sama jaar-jaar ak li ma jàng tubaab ba soresee ma taxoon a jàpp loolu ; doonte ne bëggoon naa ko, amoon ci itte lool. Daan sikk-sàkka ci sunu làmmiñ yi, ndax mënees na cee fent. Waaye Yàlla def mu am benn xew-xew bu soppi sama dundin, soppi sama xalaatin, te loolu li ma dem Ruwandaa ci atum 1998 la.
Bi ma fa demee xool réew mi ak ña fa nekk, taxaw seetlu, ci laa xam ne li fa jotoon a xew jotewul dara ak mbañeelug nawle. Maanaam, du Tutsi bi moo ameeloon mbañ Utu bi, walla Utu bee ameeloon mer Tutsi bi. Ca dëgg-dëgg, li sooke musiba Ruwandaa ba, mi ngi aju woon ci mbañeel ak xeebeel bu ku nekk ame woon ñeel sa bopp. Te, daanaka, looloo di laago bépp doomu Afrig. Moo waral nu xeeb sunu bopp, xeeb li nu doon ak sunu moomeel bay am kersa ci sunuy aada ak sunu cosaan. Loolu moo nu yóbbe nuy toppandoo ak roy Tubaab bi. Bu ko defee, sama tukkib Ruwandaa bi moo ma yee, ma daldi geestu, yëraat liggéeyu Séex Anta.Rawati-na, bi ma demee ba xam ne Farãs mooy naaféq bi doxoon ci diggante doomi-Ruwandaa yi ba ñuy reyante seen biir. Te duggewu ko woon dara lu dul bëgg faa samp làmmiñam, tasaare ko ci àddina si. Nga xool, gis ne yaa ngi jëfandikoo làmmiñu nootkat boobu, dib naaféq ak séytaane boo xam ne, féewale, noot ak sàcc alalu réewi Afrig yi rekk a ko tax a jóg. Loolu, képp ku am ci ngor as tuut, dinga taxaw xoolaat sa bopp. Looloo ma yóbbe ma daldi tàmbalee bind ci làmmiñ wi ma nàmp. Waxuma ne warunoo jëfandikoo farañse, waaye war nanoo gën a fiir ci sunu làmmiñ yi. Ndax, sama bopp ma la gënal, tekkiwul ne dama laa bañ. Te wolof dafa ne, ku wacc sa ànd, ànd boo dem fekk ca boroom. Loolu laa xam ba tax ma sóobu ci mbindum wolof.
Gaa, du woon lu yomb ca njëlbéen ga. Sonnoon naa lool sax bi may bind Doomi Golo, ndaxte saa su nekk dama waroon xoolaat njuumte yi. Waaye, sant Yàlla, jëmbët naa fulla ci liggéey boobu ba def ci tey jii ay jéego yu takku. Ndax, sama ñaareelu téere bi, Bàmmeelu Kocc Barma, Niseryaa laa ko binde, man kese, mu gën maa yomb lool, daawuma yërndu saa su ne sàqu-baat yi ndax rekk ragal a juum ci mbindmi.