NDIGALU MAAM YA
Afrig nee
Waaw góor, waaw kumba
Ayca leen ca waar wa
Bu kenn wéer goob ba
Bii pas-pas dara mënalu ko dara
Dina daw ba raw xëlu fas
Ngor ak jom a ko nas
Ma ne, Askan wee ko sas
Gan góoru jigéen ñi dar lingeer
Ci seen farlook seen gànjar ya
Bég ba tàccu ne sas
Maam a ne bëret dan delsi
Samp xeej daldi xas
Gisuma fi yaakar ju tas
Tuggee Tugal
Wéyal yaak say dëbës
Afrig dina bañ ba sës
Ndawi tey yi dootuñu surgawu
Topp sa gannaaw ni jaam bu nangu
Dina tàng dina metti
Waaye jàmbaar du xàddi
Na doxandéem bii dakkal
Wàqi gi muy wàqi sunu alal
Di roñ di génne
Di gaawantu di rawale
Am ñu ne xiim di xoole
Mbaa sax di ko ci dimbale
Sàmm sam réew warugar la
Bëgg sa réew siddit la
Gor tigi du wor du wuruj
Te su séddu jotee mooy mujje
Biir bu rëy lex yu newwi
Sonal sa bopp tooñ say ñoñ
Moone de bànneex tigi
Xanaa xam-xam ak néewle soxla
Tey jiital njariñal doom Aadama
Seex Aliyu Ndaw
Ndakaaru, weeru mars 2024