GÀCCE NGAALAAMA,MBUGAAR !
Senegaal amati na ndam ci 3eelu fan ci weeru nowàmbar wii, jaare ko ci benn ciy doomam, di Muhamet Mbugaar Saar, ab bindkat. Moom mii Farãs tappal na ko raaya bu am solo, muy Prix Goncourt bu atum 2021
![](https://www.seneplus.com/sites/default/files/styles/section_hero/public/raw_photos/mbougar_4.jpg?itok=BGzcyn9F)
Senegaal amati na ndam ci 3eelu fan ci weeru nowàmbar wii, jaare ko ci benn ciy doomam, di Muhamet Mbugaar Saar, ab bindkat. Moom mii Farãs tappal na ko raaya bu am solo, muy Prix Goncourt bu atum 2021. Muy raaya bu ñëw topp ci yeneen yu mu fi jotoon a am.
Muhamet Mbugaar di xale bu am 31 at doŋŋ, juddoo Ndakaaru ci 20eelu fanu suweŋ, ci atum 1990. Doomu Séeréer bu màgge Jurbel la, te jànge ‘‘Prytanée Militaire de Saint-Louis’’ bi ñépp a xam. Foofa la ame lijaasam bii di “Baccalauréat”, laata muy àggaleji njàngam ca Farãs, ca ‘‘Lycée Pierre d’Ailly’’ ak ‘‘Ecole des hautes études des sciences sociales’’. Moom nag, li muy gune yépp, jotoon nañu koo tappal ay raaya yu bare. Jëloon na fi Grand prix du roman métis ak Prix Ahmadou Kourouma ca atum 2015 ak Prix Littéraire de la Porte Dorée ca atum 2018. Persidaa Maki Sàll itam sargaloon na ko fi, defoon ko Chevalier de l’Ordre du Mérite ca atum 2015. Ci téere yi waral jaloore yooyu, man nañ cee lim : La Cale (2014), Terre ceinte (2015), Silence du choeur (2017) ak De purs hommes (2018). Dëgg-dëgg, xale bu jàmbaare la, ndax ku gis ay jalooreem ak li mu bind yépp, dinga xam ni ku xareñ la, mën na li muy def, te it raw na ay maasam !
Prix Goncourt, niki beneen bi ñuy woowe Renaudot, raaya la bu ñuy joxe at mu ne ca Farãs, ngir sargal bindkat bi gën a ràññeeku ci bindkati téereb nettali yiy jëfandikoo làkkuw nasaraan. Waaye ñépp xam nañu ne, làkk woowu jéggi nay digalooy Farãs bay law ci àddina si yépp, ndax, daanaka, ay fukkiy miliyoŋi nit ñooy jëfandikoo làkk woowu. Kon nag, Prix Goncourt, raaya bu am solo la ; cuune du ko gàddu, doonte ci way-jëfandikoo farañse yi rekk la yem.
Prix Goncourt bu mag boobu la doomu Senegaal bi gàddu gannaaw René Maran (ca atum 1921) ak Mari Njaay (ci atum 2009). Kon nag, gàcce ngaalaama, Muhamet Mbugaar !
Li tax ñu tànn ko ci biir bindkat yi bare yooyu doon xëccoo raaya bi, mooy ñeenteelu téereem bi mu bind, duppe ko La plus secrète mémoire des hommes. Muŋ ciy nettali jaar-jaaru bindkat bu xareñoon, ku ñépp séentu woon ca kaw, waaye mu mujjee daanu ba ñépp fàtte ko, ndax rekk, ñàkk dégg-dégg bi nit ñi wone woon ñeel i mébétam. Mu mel ne, kàngami Goncourt yi doon àtte ngir tànn mbër mi leen doy, dañoo yéemu ciy xalaati Mbugaar yu xóot yi, waaye rawati-na ci xereñ gi mu wone ci mbindinam.
Li gën a neex ci raaya Mbugaar bile, mooy bés bi mu ko amee, dafa xaw a yemook 7eelu fanu nowàmbar, di Journée internationale de l’écrivain africain, maanaam bés bi ñu jagleel bindkati Afrig yi. Bés boobu, li ëpp ci bindkati Senegaal yi daje woon nañu ci seen béréb bu siiw boobu di Kër Biraago gu bees. Ñu bare ci ñoom nag jot nañu faa jël kàddu, rafetlu xew-xew bi, biral seen mbégte ci jaloore ju ni mel.
Teewul nag, am ñeneen ci réew mi, ñu yékkati seen baat di ŋàññ Mbugaar ndax ñàkk a rafetlu ay bindam. Waaye loolu, jeneen wax la, ndax dañuy jàpp rekk tontuy Mbugaar ci boppam : “Na nit ñi jàng téere bi ba noppi, buñ amee lu ñuy wax, ñu wax ko”.
Ci sunu wàllu bopp, ci wax jooju lanu jàppandi ba ba nuy jàng téereem yi indi coow lépp. Kon, nu waxati ko : “Gàcce ngaalaama, Mbugaar !”